Smart BusinessSolution EN Essai gratuit
Kër › Sàrt yi ci jaay bi
Xibaar yu yoon

Sàrt yi ci jaay bi (CGV)

Français · English · Wolof

1. Lu mu jëm

Sàrt yii (CGV) ñoo tëral naka lañuy jëfandikoo logiciel Barkeel, bi Smart Business Solution defar, ak naka lañuy jënde ay abonnementam. Barkeel logiciel la buy saytu njaay (caisse, stock, bor kiliyaan yi, njënd, facture, comptabilité bu yomb), te mën nga ko ubbi ci telefon walla ordinateur ci app.barkeel.com, wolofal.barkeel.com ak english.barkeel.com.

Su nga sosee compte walla nga fey abonnement, nangu nga sàrt yii. Service bi, jaaykat yi, entreprise yi ak ñiy liggéey seen bopp lañu ko defaral.

2. Sos compte bi ak ekip bi

Boroom entreprise bi moo sos compte bi ak turam, turu njaayam, email, numéro telefon ak mot de passe. Moo war a wóorlu ne li mu bind dëgg la.

Mën na woo ñiy liggéeyal (gérant, jaaykat) ak code invitation. Boroom bi moo tànn li ku nekk sañ a def, te moo yor ndàq li ekip biy def ci compte bi. Ku nekk na denc mot de passe bi ci kumpa; lépp lu ñu def ak ay identifiantam, moom lañu ko teg.

3. Essai bu amul fey

Entreprise bu bees bu nekk am na 14 fan yu ñu ko may ci Premium, te lépp ci biir, amul carte bancaire, amul dara lu ko takk. Su essai bi jeexee, war nga fey abonnement ngir mën a wéy di bind say jaay; bu dul loolu, sàrt 6 bi moo lay dox.

4. Formule yi ak njëg yi

Ñaari formule lañu am:

  • Classique : benn bitik, ba 3 jëfandikukat (boroom bi ci biir), benn promo ci weer wi;
  • Premium : ba 5 bitik ak jëfandikukat yu amul limite (lu ëpp 5 bitik : offre Entreprise ci devis), transfert ci diggante bitik yi, lot ak date péremption, numéro série, TVA, tableau de bord bu gën a xóot ak ñetti promo ci weer wi.

Abonnement bi mën nga koy fey weer bu nekk walla at mu nekk; abonnement bu at bi am na benn weer bu ñu la may. Njëg yi ci franc CFA lañu, TTC, te ñu ngi feeñ ci app bi ci page « Mon abonnement ». Njëg bi ñuy jël, mooy bi feeñ bés bi nga fey.

Smart Business Solution mën na soppi ay njëgam. Dañuy yégal kiliyaan yi lu mu gëna néew 30 fan balaa; njëg bu bees bi du dox lu dul ci yeesal bi ci topp. Promotion yi ñu mën a def am nañu seen àpp, te duñu boolu, su ñu waxul leneen.

5. Fey ak ubbi abonnement bi

Dañuy fey ak Wave walla Orange Money ci numéro bi feeñ ci app bi, ci turu Smart Business Solution. Kiliyaan bi dina yónnee reçu fey bi ci WhatsApp. Abonnement bi dina ubbiku walla yokku su ñu seetee fey bi ba noppi, te facture bi dina feeñ ci app bi.

Fey bu jiitu bés bi abonnement bi di jeex dina ko yokk: fan yi des duñu réer. Amul prélèvement automatique: abonnement bi du yeesalu su kiliyaan bi feyul beneen diir.

Diir bu tàmbali dañu koy fey, te duñu ko delloo, ndare kiliyaan bi juum ci fey bi (fey ñaari yoon, montant bu baaxul) te mu wax ko balaa 30 fan, walla su service bi taxawee ndax Smart Business Solution.

6. Jeexu abonnement bi, fan yu ñu may ak lecture seule

Bés bi abonnement walla essai bi jeexee, kiliyaan bi am na 7 fan yu ñu ko may (période de grâce) yu muy wéy di jëfandikoo app bi ni mu baaxe. Bu loolu weesoo, compte bi dina dugg ci lecture seule: kiliyaan bi mën na xool ay donnéeam, waaye mënul bind jaay, njënd walla soppi dara. Lépp dina dellu ni mu meloon bu mu feyee beneen diir.

7. Donnée yu kiliyaan bi

Donnée yi kiliyaan bi bind ci app bi (produit, stock, jaay, kiliyaan, fournisseur, xaalis), yu kiliyaan bi lañu. Smart Business Solution dafa leen denc ngir jox service bi rekk; du leen jaay te du leen jox kenn, ndare yoon laaj ko.

Kiliyaan bi mën na laaj saa su nekk ñu jox ko copie bu ay donnéeam walla ñu far leen, ci bind service client bi. Bu abonnement bi jeexee, donnée yi dañu leen di denc lu mu gëna néew 12 weer ci lecture seule, ngir kiliyaan bi mën a dellu walla jël leen.

Donnée yi dañu leen denc ci kaaraange ci ay prestataire yu xam seen liggéey. Donnée personnelle yi dañu leen topp ci yoonu Senegaal n° 2008-12 bu 25 janvier 2008 ci aar donnée personnelle yi. Kiliyaan bi, ak ñi mu bind seen xibaar (ay kiliyaanam, ekipam), mën nañu laaj ñu xool, jubbanti walla far seen donnée ci service client bi.

8. Liggéeyu app bi ak ndimbal

Smart Business Solution dafay def lépp ngir app bi dox saa su nekk te donnée yi am sauvegarde. Mën na am ay taxaw yu gàtt ngir maintenance walla yeesal, walla ndax internet, courant walla prestataire bu am jafe-jafe. App bi dafay yokku saa su nekk: mën nañu yokk walla gëna baaxal ay fonction.

Service client bi dafay tontu ci WhatsApp (+221 75 103 75 75) ak ci email (contact@smart-biz-solution.com), ci français, wolof ak anglais.

9. Naka lañuy jëfandikoo service bi

Kiliyaan bi dafa war a jëfandikoo Barkeel ci liggéey bu yoon nangu, du jéem a dugg ci donnée yu yeneen entreprise, du sotti, jaay walla xàll logiciel bi, te du yàq naka muy doxe. Su am njumte bu réy, Smart Business Solution mën na taxawal compte bi bu yégalee kiliyaan bi ba noppi, ndare dafa gaaw lool.

10. Ndàq

Kiliyaan bi rekk moo yor ndàq li mu bind (njëg, lim, taux TVA), ay factureem, ay déclaration fiscaleem ak comptabilitéem. Comptabilité bi app bi jox comptabilité bu yomb la, bu ñu jële ci SYSCOHADA: dafay dimbali kiliyaan bi, waaye du wuutu expert-comptable.

Ndàqu Smart Business Solution du weesu lor yu dëggu yu ñu firndeel, te mënul ëpp xaalis bi kiliyaan bi fey ci 12 weer yi weesu. Du yor ndàq ci lor yu dul jub (xaalis bu ñu jotul, kiliyaan yu ñu ñàkk) walla ci lu kenn mënul moytu (force majeure).

11. Moomeel

Logiciel Barkeel, màrkam, ay textam, ay nataalam ak codeam, yu Smart Business Solution lañu. Abonnement bi dafay may kiliyaan bi ak ekipam sañ-sañu jëfandikoo ko ci diiru abonnement bi, waaye du leen ko jox.

12. Taxawal abonnement bi

Kiliyaan bi mën na taxaw saa su ko neexee: dafa doy mu bañ a yeesal abonnement bi. Mën na tamit laaj service client bi ñu tëj compte bi te far ay donnéeam.

13. Soppi CGV yi

Sàrt yii mën nañu soppiku. Bi ñuy jëfandikoo mooy bi nekk ci page bii bés bi kiliyaan bi fey. Su am soppi yu am solo, dañuy yégal kiliyaan yi ci app bi walla ci WhatsApp.

14. Yoon ak xuloo

Sàrt yii yoonu Senegaal lañuy topp. Su am jafe-jafe, kiliyaan bi ak Smart Business Solution dañuy jëkk a wut pexe ci seen diggante, ci bind service client bi. Su ñu déggoowul ci 30 fan, xuloo bi dañu koy yóbbu ca Tribunal de commerce hors classe bu Dakar.